Dama namm waxtaan ci Wolof
Ci Senegaal, dama waxtaan ci Wolof bés bu nekk. Ci dëgg-dëgg, ci “Frolof” laa waxtaan, ndaxte sama faranse moo sut sama Wolof – waaye ci man, Wolof moo gën neex. Jàng na faranse juróomi at, te jang na Wolof benn at ak genn wàll rekk, waaye dama bëgg Wolof lool, konbook dama waxtaan ak waa Senegaal ci Wolof, du faranse. Léegi, maangi ci Amerig, te amul ku bëgg waxtaan ci Wolof ak man. Dama ragal fàtte sama Wolof. Ci Amerig, am na waa Senegaal yu bari, waaye amul fima dëkk, ci Michigan. Amaana, am na ñent walla juróom, waaya xamuma kenn. Bëgguma jaambaat bu bari. Kontaan naa lool ci sama ñenti weer ci Senegaal, ak ci samay xarit foofu. Léegi, dama war jàppandiku sama Wolof ñetti yoon ci ayubés bu nekk – walla ñenti yoon, juróomi yoon, walla bés bu nekk. Kon, ba beeneen yoon!
Share:
Corrections
No corrections have been written yet. Please write a correction!
Write a correction
Please enter between 25 and 8000 characters.


0 comments
Please enter between 0 and 2000 characters.